Tor Browser danu ko war a di yeesal saa su nekk. Sooy wéy di jëfandikoo ab version bu yàgg bu tëralinu nosukaay bi, mën nga ubbi buntu kaarànge gi nga amoon buy néewal doole sa kirlaay ak nëbbu.
Tor Browser dina la laaj nga yeesal sa mboolem jëfukaay su xasee génne ab xeet bu bees bu nu genne: alluwa dugg bi (≡) dina wone ab wërngël bu nëtëx bu am ab fitt bu jëm kaw ci kawam, te di nga mën a gis ab tegtalu yeesal bu nu bind soo ubbee Tor Browser. Mën nga yeesal ci anam bu otomatik wala ak sa loxo.
YEESAL TOR BROWSER AUTOMATICALLY
Soo bëgge yeesal Tor Browser, kilikeel ci alluwa dugg bi (≡), te nga tànn "Yeesal bu jàppandi – taalaatal léegi".
Xaaral yeesal bi ngir yebbi te samp, noonee Tor Browser dina taalaat boppam. Di nga jëfandikoo version bu mujj bi.
YEESAL TOR BROWSER AK SA LOXO
Soo bëggee yeesal Tor Browser, jeexalal session xuus bi te nga tëj tërëlin bi.
Dindil Tor Browser ci sa noosteg amalin jaaree ko ci dindi wayndaare bi mu nekk (xoolal Sempi pàcc bi ngir xibaar yu gën a yaatu).
Xoolal https://www.torproject.org/download/ te nga yebbi ab sotti bu Tor Browser bu mujje genn, te nga defaat ko ne bu njëkk.