Yoon wi gën a woyof te gën a wóor ngir yebbi Tor Browser mu ngi nekk ci dalu web bu Tor Project bu baax bi ci https://www.torproject.org/download.
Sa lëkkalook dalukaay bi dina am kaarànge sooy jëfandikoo HTTPS, loolu dafay tax mu gën a jafe ci nit ngir mu soppi ko.
Waaye, dinay faral am ay saa yoo xam ni doo mën a dugg ci dalu web bu Tor Project: ci misaal, mën na taxaw ci sa jokkoo.
Su loolu amee, mën nga jëfandikoo benn ci doxalini yebbi yiy wuutu yi nu lim ci suuf:
SEETU YI
If you're unable to download Tor Browser from the official Tor Project website, you can instead try downloading it from one of our official mirrors, either through EFF or La Cebolla.
GetTor
GetTor nekk na ab serwiis buy tontu automatically ci ay bataaxal yu àndak ay lëkkalekaay ci version bu Tor Browser bu gën a bees bi, nu dalal ko ci ay béréb yu bari, niki Dropbox, Google Drive ak GitHub.
JËFANDIKOO GETTOR JAARE KO CI BATAAXALU INTERNET
Yonneel ab bataaxalu internet ci gettor@torproject.org, te ci biir message bi bindal rekk "windows", "osx", wala "linux", (yu amul maas yi ko séqq) mu aju ci sa nosteg doxin.
Ci misaal, ngir am ay lëkkalekaay ngir yebbi Tor Browser ci Windows, yonneel ab bataaxalu internet ci gettor@torproject.org bu àndak baatu "windows" ci biir.
GetTor dina tontu ak ab bataaxalu internet bu am ay lëkkalekaay yi nga mën a jaare ngir yebbi ëmb bu Tor Browser, xaatim bunu binde loxo (nu soxla ko ngir saytu yebbi bi), màndargay baaraam bu caabi bi nu jëfandikoo ngir defar xaatim bi, ak ëmbub checksum bi. Mën nanu la may ab tànneef bu "32-bit" wala "64-bit" bu software: loolu dafay aju ci xeetu ordinaatëer bi ngay jëfandikoo.
JËFANDIKOO GETTOR JAARE KO CI TELEGRAM
Yonneel ab message ci @GetTor_Bot ci Telegram.
