War nga mën a tàmbali xuus ci sa dalukaayu web di jëfandikoo Tor Browser tuuti gànnaaw ba dooree tërëlin bi, te nga kilike ci butong "Connect" bi soo ko dee jëfandikoo yoon bu njëkk.
Connection Assist bi daf lay leeral lu jëm ci nekkinu sa lëkkaloo Internet soo kilikee ci 'Test'.
Xoolal sa Lëkkaloo Internet su fekkee danu ci bind 'Jokkoo amul'. Su fekkee lëkkaloo jokkoowu Tor bi indiwaatunu ko te dafay wone 'Lëkkaloo amul' Jéego yii mën nala jàppale.
SAAFARA YU GAAW
Su fekkee Tor Browser lëkkaloowul, mën na am benn saafara bu yomb.
Jéemal benn bu nekk ci yiile:
- Sa montaru nosteg doxalin jumtukaayu xarale war nga ko samp ba mu am waxtu bu jaar yoon, wala Tor du dox ni mu waree.
- Wóoralal ne beneen Tor Browser wala ci misaal 'Tor dawul ba pare ci sa nosteg doxalin.
Su fekkee wóorula ndax Tor Browser mu ngi dox, taalaatal sa ordinaatëer.
- Wóoralal ne bépp tërëlinu antiwirus boo sȧmpoon nekkul moo tee Tor di dox ni mu waree.
War nga soxla xool wayndaare ngir sa jumtukaayu antiwirus soo xamul nan nga kay defee.
- Dindil sa firewall tuuti.
- Su fekkee Tor Browser mu ngi doon dox lu jiitu loolu te doxul léegi sa nosteg doxalin mën na am ne dafa fayoon lu yàgg.
Yeesalaatal sa nostegu doxalin dina saafara jafe-jafe bi.
- Dindil Tor Browser te nga sȧmpaat ko.
Su fekkee dangay yeesal, bul bind rekk ci kaw sa dosiye Tor Browser; wóoralal ndax dindi nga lépp lu jiitu.
YËR TOR LOGS
Ci anam yu bare, xool Tor logs mën na la jàppale ci caytu jafe-jafe bi.
Soo amee jafe-jafe lëkkaloo, ab message njumte mën na génn te mën nga tànn benn tànneef ngir "sotti Tor log ci clipboard".
Te nga taf ko ci Tor log bi ci ab mbind wala beneen dosiye.
Su fekkee gisuloo tànneef bii te nga ubbi Tor Browser, mën nga xuus ci alluwa hamburger bi ("≡"), te nga kilike ci "Sukkandikukaay", ci mujjantal ga ci "Lëkkaloo" ci bantu wet gi.
Ca xët ba sa suuf, ci wetu xëtu "View the Tor logs", bësal butong bi "View Logs...".
Ci beneen boor, ca GNU/Linux, ngir gis làqq yi ci nosukaay bi, xuusal ci dàmb Tor Browser te doxal Tor Browser jaaree ko ci tegtalu ndigël:
./start-tor-browser.desktop --verbose
Wala deñc bataaxal yi ci ab dosiye (bi teew: tor-browser.log):
./start-tor-browser.desktop --log [file]
Yeneen xibaar mën nanu leen a am ci Support Portal.
NDAX DANU TERE SA LËKKALOO?
Soo mënul lëkkaloo ba léegi, sa Bankaas bi la Jox Internet mën na dakkal lëkkaloo yi ci jokkoowu Tor bi.
Jàngal pàccu Moytu ngir am ay saafara yu gaaw.
JAFE-JAFE YUNU XAM
Tor Browser dafa nekk ci yokkuteef buy wéy, te yenn jafe-jafe yii xam nanu leen wànte saafara wu nu leen ba léegi.
Nu ngi lay ñaan nga xool xëtu Known Issues ngir gis jafe-jafe bi ngay dund ndax nekk na foofu ba pare.